Waaye waa Sodom ñu bon lañu woon, te mana moy Aji Sax ji lool.
TSK
TSK · Genesis 19:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Xiddileen mbooloo mii, ma xoyom leen léegi!»
Aji Sax ji day seetlu ku jub; ku soxor, bëgg fitna, mu bañ.
Te sax, xanaa du Aji Sax ji laa àndal ba dalsi fi kaw réew mii, ngir tas ko? Aji Sax ji ci boppam moo ma ne: “Songal réew mii, tas ko!”»
Ba loolu wéyee mu wax ak ña ca des, may dégg. Mu ne leen: «Toppleen ko ca biir dëkk ba te ngeen rey. Buleen xool bëti ñéeblu, buleen ñeewante.
Ana kon lu tee nit waxe noonee nu soskat yi tuumaale ne nooy wax naan: «Nanu def lu bon, ngir mu jur lu baax»? Ñooñu mbugal lañu yelloo.
Naka noonu itam Sodom ak Gomor, ak dëkk ya leen wër, ñoo yebu woon ci powum séy, ak jaxasoo gu woroo ak bindub judduwaale, ba ñu def leen misaal, ñeel ña nara tegoo mbugalum sawara wu sax dàkk.