TSK

TSK · Genesis 3:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Jigéen ja dafa gis ne garab gi rafet na, niru na lu neex, te mata bëgg ci kuy wuta am xel, mu witt ci doom yi, lekk; jox ci jëkkëram, ji mu àndal, moom it mu lekk.

Mu tudde ko Nóoyin (mu firi Noflaay) ndax dafa ne: «Kii moo nuy taxa noyyiwaat, noppal nu ci liggéey yu metti ak coonoy mbeyu suuf, si Aji Sax ji rëbb.»

Job 5:6 TSK

Aw ay du garab, bay fëlle biir suuf, coono du jekki, jebbi.

Job 14:1 TSK

Ku jigéen jur, yaa néewi fan, géejal coono!

Soo meree kay, nu sànku, nga xadaru, nu jàq.

Cóolóoloo cóolóol, waru waarekat ba, cóolóoloo cóolóol, léppi cóolóoli neen.

Ma xoolaatal sama bopp lépp lu ma sottal, doñ-doñi ko, ba sottal, ndeke lépp, cóolóoli neen ak napp um ngelaw. Nit gisul njariñ ci kaw suuf.

Ma ne ana lu nit di jariñoo ci doñ-doñ ak xalaatu xol, yi muy doñ-doñaale fi kaw dun bi?

Suuf si la ñi ko dëkke sobeel, ñoo wàcc yoon yi, xëtt ndigal, fecci kóllëre gi sax dàkk.

Ndax kat, càkkéef gépp, li ñuy déggal neenug neen la, te du seen coobare, waaye ki leen ci tënk la neex, ba tax ñuy yaakaar,