TSK

TSK · Genesis 34:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

yóbbaale doomam yu góor ya ak sëtam yu góor ya ak doomam yu jigéen ya it, ñook sëtam yu jigéen ya, ak mboolem ña askanoo ca moom.

«Waxal bànni Israyil ne leen: Su fekkee ne nit ki dafa moy lenn ci santaaney Aji Sax ji, ba def lenn lu warul te du teyeefam, li ci war lii la.

¶ «Su dee kenn ci baadoolo yee moy lenn ci santaaney Aji Sax ji, ba def lenn lu warul te du teyeefam, mu dig tooñam,

Ci yeen lay toog, ci seen biir, bérab ba mu taamu, ci benn bi ko gënal ci seeni dëkk, te buleen ko néewal doole.

¶ Ba Buur Daawuda déggee mbir moomu mépp, mer na lool.

séen ca biir téxét ya, ku ma seetlu ca xale yu góor ya, muy ku ñàkk bopp.

Bunu jëfe powum séy, ni ko ñenn ci ñoom daa defe, ba tax ñaar fukki junni ak ñett (23 000) ca mbooloo ma bokk dee ci benn bés.

¶ Kon nag reyleen seen cér yi bokk fii ci kaw suuf; lu mel ni powum séy, ak jëfi sobe, ak ñàkk sago ci lu jekkadi, ak xemmemtéef yu bon, ak bëgge, te loolooy bokkaale ba tey,

¶ Na ñépp wormaal diggante bu ab séy dox, te ab lalu séy na mucc sobe, ndax fokati séy yi, ak jaalookat yi, Yàlla moo leen di daan.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.