TSK

TSK · Genesis 6:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji daldi ne: «Dinaa far ci kaw suuf doom aadama yi ma sàkk, nit ak jur, luy raam ak luy naaw, ndax mititlu naa li ma leen sàkk.»

Ndax kat li feek juróom ñaari fan dinaa wàcce taw ci kaw suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg, ba far ci àddina mboolem mbindeef mu ma sàkk.»

¶ Mbënn ma nag di wal ci àddina diiru ñeent fukki fan. Ndox ya di yokku, gaal gay jóg, ba tëmb, tiim suuf lu sore.

Luy dund ci àddina daldi sànku, ba nit ak jur ak luy raam ak luy naaw— lépp la Aji Sax ji raafal ci àddina. Nóoyin rekk a des, moom ak ña àndoon ak moom ca gaal ga.

Man nag maay dëgëral boppu waa Misra, ba ñu dugg, topp leen. Su ko defee ma siiwal sama ndam, ndax dinaa yar Firawnaaki xarekatam yépp, boole ci watiiri xareem aki gawaram.

Kon gisleen ne man la, man doŋŋ, kenn du Yàlla ku dul man! Man maay rey, di dundal; di gaañe, di wéral; maay jàpp, te kenn du xettli.

Aji Sax ji la mbënn ma fekk falu, Aji Sax jee falu buur ba fàww.

suuf su nangu doon jooru xorom ndax mbonug ña ko dëkke.

Mu ne: «Na ma defoon ak ndoxum Nóoyin ma mooy lii tey. Maa giñoon ne ndoxum Nóoyin ma, mu ni day dootu wale kaw suuf. Noonu it laay giñe ne duma la mereeti, duma la rëbbati.

Neel: “Yeen Tundi Israyil, Dégluleen kàddug Boroom bi, Aji Sax ji. Boroom bi Aji Sax ji moo wax lii, jëme ci tund wu mag ak wu ndaw ak xunteeku xur, ne: Maa ngi nii di leen wàcceel saamar, maay màbb seen jaamookaayi tuur,

¶ «Moo tax Boroom bi Aji Sax ji da leena wax ne: Maa ngi nii di àttesi diggante gàtt bu duuf ak gàtt bu yooy.

Amos 9:6 TSK

Kee tabax kaw asamaan néegi biiram, samp ub xaddam, yiire suuf. Keey woo walum géej, walal fi kaw suuf. Kookoo di Aji Sax ji.

Nit ñaa nga doon lekk ak a naan, di jël jabar ak a séyi, ba keroog bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga, mbënn ma dikk, sànk ñépp.

ba tax na, noonee bàkkaar doone woon buur, ndax dee gi mu yilife ñépp, ni la aw yiw wuutoo, di buur moom itam, ndax àtteb njub gi aw yiw jural nit ñi, ba jëme leen ci texe gu sax dàkk, ci sunu ndimbalal Boroom Yeesu Almasi.

Ndax kat, càkkéef gépp, li ñuy déggal neenug neen la, te du seen coobare, waaye ki leen ci tënk la neex, ba tax ñuy yaakaar,

ñooña gëmadi woon bu yàgg, jant ya Yàllay muñ, di négandiku, te Nóoyin di yett gaal, ga lim bu néew, juróom ñett, mucce woon ca ndox ma.