TSK

TSK · Hebrews 3:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji nag am tiis ci xolam, ba mititlu li mu doon sàkk nit ci kaw suuf.

Éy Yàlla, yéwéne nu, barkeel nu, te geesoo nu sa leeru kanam, Selaw,

Gàntal nañu ko ba tàyyi ca màndiŋ ma, teg ko naqar ca ndànd-foyfoy ga.

Loolu defalu ko wenn xeet; kenn xamu ci ndigali yoonam. Màggal-leen Ki Sax!

Waaye ñoom ñoo fippu, di naqaral xelam mu sell, mu soppliku seen noon, ba mujj di xareek ñoom.

Sama ñoñ, seen bant lañuy seeteey, seenu yet di leen waxaleey. Xelum ngànctu moo leen wacc, ñooy gànctu, lajje fa seen Yàlla.

¶ Gannaaw ràññee Yàlla jaralu leen dara, Yàlla it bërgal leen ak seen xel mu doyadi, ba ñuy def jooju jëf ju jekkadi.

Te it buleen tiisal Noowug Yàlla gu Sell, gi leen màndargaale xàmmikaayam ngir bésub njot ba.

¶ Bokk yi, wattuleen bala kenn ci yeena am xolub gëmadi bu bon bu koy xiir ci dëddu Yàlla jiy dund.