Su ko defee nga rendi kuuy mi, sàkk ci deret ji, taqal ci tabanum noppu ndijooru Aaróona ak tabanum noppu ndijooru doomam yi, te nga taqal ci seen baaraamu déyu ndijoor, ak seen baaraamu tànku ndijoor bu mag. Boo noppee, nga xëpp li des ci deret ji ci peggi sarxalukaay bi yépp ba mu daj.
TSK
TSK · Hebrews 9:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Exodus 29:20
TSK
Leviticus 8:15
TSK
Musaa rendi ko, sàkk ci deret ji, capp ci baaraamam, diw ci ñeenti béjjéni sarxalukaay bi yépp, setale ko sarxalukaay bi. Mu daldi tuur li des ci deret ji ci taatu sarxalukaay bi, sellale ko noonu, muy njotlaayal sarxalukaay bi.
Leviticus 9:8
TSK
¶ Aaróona dikk ba ci sarxalukaay bi, rendi sëllu wi, muy saraxu póotum bàkkaaram.
Leviticus 16:14
TSK
Na sàkk ci deretu yëkk wi, wis-wisale ko baaraamam ci kaw kubeeru gaal gi, ci wetam gi féete penku, te it na wis-wisale baaraamam deret ji lu mat juróom ñaari yoon ci kanam kubeeru gaal gi.
Ezekiel 43:18
TSK
¶ Waa ji ne ma: «Yaw nit ki, Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Lii mooy dogali yoon yi jëm ci sarxalukaay bi, bés bu noppee, ci wàllu saraxi rendi-dóomal, ak deret ji ñu ci wara tuur.