TSK

TSK · Hosea 13:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji ne ko: «Déggalal mbooloo mi te def li ñu la wax lépp. Du yaw lañu bañ, waaye man mii lañu bañ ma doonati seen buur.

Aji Sax ji yebal Yërubaal, teg ca Bedan, teg ca Yefte, teg ma ca, man Samiyel, daldi leen xettli ci seen noon yi leen séq, ba ngeen dëkke jàmm.

Gannaaw gi nag buurub Asiri gis ne Ose lal na pexe, ndax daa yónnee ay ndaw ca So buuru Misra, ba noppi lànk ne du fey galag at mu nekk. Buurub Asiri jàpp ko, tëj.

Du seen saamar lañu nangoo réew mi moos, seen dooley bopp it mayu leen ndam. Yaa ko defe kàttan ak doole, geesoo leen sa leeru kanam, ngir sa cofeel.

Yàlla, yaa masa doon sama buur, di ma walloo ci digg réew mi.

Na Israyil bége kii ko sàkk, doomi Siyoŋ, laa ne, ñu bànneexoo seen buur bii.

Maay Aji Sax ji, seen ku Sell ki; maa sàkk Israyil, di seen buur.»

Sama bokk yaa ngooguy yuuxu yuux yu àkki fu sore, naan: «Moo Aji Sax ji daa newul Siyoŋ a? Moo Buurub Siyoŋ da fee nekkatul a?»

Hosea 8:4 TSK

Ñoo fal ay buur te du sama ndigal, ñoo tabb ay kàngam, te yéguma. Seen xaalis ak seen wurus lañu sàkke jëmmi tuur, muy seen sànkute.

«Man Aji Sax ji, fa Misra laa dale di seen Yàlla, xamuleen Yàlla ju dul man, te kenn du musle ku ma moy.