Gannaaw ga ma gis juróom ñaari gub yu gooy yu ngelaw li lakk, sax tegu ca ya jiitu.
TSK
TSK · Hosea 13:15
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Teewul baayam lànk, ne ko: «Xam naa ko, doom, xam naa ko. Moom itam dina doon aw xeet tey doon ku màgg, waaye rakkam a koy sut, te askanam dina law, ba di ay xeet.»
Taawub yëkk la, daraja mooy boroom, béjjén ya, béjjéni nagu àll la, ca lay butteendoo xeet yépp, ba ca cati àddina. Ñooñooy junniy junniy nit ca giirug Efrayim, ak junni ca giirug Manase.
Loolu dalul moos ku bon, kay mel ni xatax bu ngelaw li wal.
Waajal-leen fi ñuy rendi doom yi, feye leen seen ñaawtéefi baay, bala ñoo jógati, teg àddina loxo, ba tabax fu ne ay dëkk.»
Yaa leen di bàcc, ngelaw wal, ngëlén tasaare; yaw ngay bége Aji Sax ji, di damoo Aji Sell ju Israyil.
Maay joxe lépp luy alalu dëkk bii. Mboolem lu fiy njariñ, mboolem gànjar, mboolem denci buuri Yuda, dinaa ko teg ci seen loxol noon yi, ñu sëxëtoo, jël, yóbbu Babilon.
Ma nga noonu jëmbate, waaye mbaa dina baaxle yee? Mbaa ngelawal penku du ko laal rekk mu laxa lax? Mbaa du lax fa mu saxe?»
Dinañu lël sax seen jëmmi tuur yu ñu móol, yóbbu Misra, boole kook seen gànjaru xaalis ak wurus. Gannaaw loolu dina toog ay at te du laaleek buur bëj-gànnaar.
Efrayim, ab sagam ni picc lay naawe, du njurum doom, dub ëmb, du doom ju sosu sax.
Naka la jant ba fenk, Yàlla yebal ngelawal penku lu tàng jérr, jant ba jam boppu Yunus, ba mu xawa xëm, bëggatul dara ci bakkanam. Mu naan: «Dee sax a ma gënal dund!»