TSK

TSK · Hosea 4:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Suuf si la ñi ko dëkke sobeel, ñoo wàcc yoon yi, xëtt ndigal, fecci kóllëre gi sax dàkk.

Seeni ñaawtéef a dox seen digganteek seen Yàlla. Seeni moy a leen xañ kanamam, ba mu tanqamlu leen.

«Wërleen mbeddi Yerusalem, xool-leen, seet ciy péncam rekk ba xam ndegam dingeen gis kenn, kenn kepp kuy def njub, di sàmm worma, ma daldi leen baal.

«Yerusalem, ana lu tax ma di la baal, te say doom wacc ma, di giñe lu dul Yàlla. Ma reggal leen, teewul ñuy njaaloo, riixle, jëm kër gànc ya!

Ni bëtu ndox di dawe, ni lañuy dawale seenug coxor. Fitnaak salfaañooy riir ci dëkk bi, gisuma lu moy jagadeek loraange!»

«Ñu ngi tàwwi ni fittkat seen làmmiñu workat, seen doole ci réew mi doxaluñu ci yoon. Ñu ngii di def lu bon ci kaw lu bon, te man faalewñu ma.» Kàddug Aji Sax jee.

Seen bàkkaari yonent yaa, seen ñaawtéefi sarxalkat yaa; ñoo tuur fa digg dëkk ba deretu aji jub ñi.

Ay yonentam a ngi déeyoo fi biiram; ñu ngi xiiru ni gaynde guy xotat pàddam, di lekk doom aadama yi, foqati alal ak gànjar, ful jëtun yi ci biiram.

Hosea 6:9 TSK

Ni saaysaay siy tëroo, ni la sarxalkat yi lëkkoo, di bóome ca yoonu Sikem. Ndaw jëf ju ñaaw!

Hosea 7:3 TSK

Seenug mbon lañuy bégale buur, seeni fen di bégal kàngam.

Ci loxol yonent la Aji Sax ji génnee Israyil Misra, te ab yonent la sàmmloo Israyil.

Micah 3:2 TSK

Te yeenay bañ-kati lu baax, di bëgg-kati lu bon. Yeenay fees sama ñoñ te ñuy dund, yeenay rocci suux wi sàng seeni yax.

ndax alalu njublaŋ a ngi ci biir këri njublaŋ yi ba tey, mook nattukaayi alkànde yu tuut ya ñuy jaaye?

Wóoy ngalla fippukat bu sobewu bi, dëkkub notkat yi.

«Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Àtteb dëgg, nangeen ko àttee, te ngor ak yërmande it, deeleen ko jëflantee.

Acts 7:52 TSK

Kan ci yonent yi la seeni maam fitnaalul? Ñoo rey démb ña yégle woon ñëwug Aji Jub, ji ngeen wor tey, bóom ko.

Ma gis ne jigéen ji daa naan ba màndi ci deretu ñu sell ñi ak deretu ñi doon seedeel Yeesu. Ba ma ko gisee, jaaxle naa lool.