TSK

TSK · Isaiah 13:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu ne: «Maa koy def kërug siññéel, def ko ab tan, ba buube ko buubub rajaxe.» Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.

Seen kër buur ya la dég ya di lawe, gajj aki taxas saxe tata ya, till dëkke, bànjóoli tàgge,

suuf su wow doon ub déeg, joor gu maral ballal bëti ndox. Fa till fàkkoon, di fa goore, gattax ak barax a fay sëqe.

Yaw nitu réew mee, sànkute dikkal na la. Àpp mat, bés dëgmal, tiitaange wuutu ca mbéx fa kaw tund ya.

Ca digg dëkk ba la jur gay goore, ak xeetu rab wu nekk; looy aki saaw fanaane kaw jëni bunt ya, ay sab jibe ca palanteer ya, tojit ya dala jale ca bunt ya, xànqi seedar ya ne duŋŋ.

Du caageenu yeexe gu Boroom bi yeexe dige ba, noonu ko ñenn ñi fooge ag yeex. Yeen la muñal kay, ndax buggul kenn sànku, xanaa ñépp dem ba tuub.