TSK

TSK · Isaiah 19:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bésub tey jii Aji Sax jee lay teg ci sama loxo, ma rey la, dog sa bopp. Tey jii sax laay leele njanaaw yeek rabi àll yi, néewi xarekati Filisti, ba àddina sépp xam ne Israyil am na Yàlla.

Éy Yàlla, yéwéne nu, barkeel nu, te geesoo nu sa leeru kanam, Selaw,

Aji Sax jee xamleg wallam, feeñal njekkam, xeet yi gis.

Deesatul gaañe mbaa di lore, fi mboolem sama kaw tund wu sell wi, ndax ni ndox di feese ba muur géej, ni la àddina di feese nit ñu xam Aji Sax ji.

Kii nee: “Aji Sax jee ma moom.” Kee di tuddoo turu Yanqóoba, kale bind ca loxo ba: “Maa ñeel Aji Sax ji,” tey wuyoo turu Israyil.»

mu ne: «Ñooñu, maa leen di yóbbu sama kaw tund wu sell, bànneexale leen sama biir kërug ñaan, seen saraxu rendi-dóomal ak yeneen sarax, dees na leen ko nangul sama kaw sarxalukaay, ndax dees na wooye sama “kër, kërug ñaan”, ñeel xeetoo xeet.»

Waaye ni ndox muure xóotey géej ba mu daj, ni la darajay Aji Sax jiy ràññikoo ci àddina sépp.

Su boobaa mboolem ndesu wépp xeet wu songoon Yerusalem, Yerusalem lay yéegi at mu ne, ngir sujjóotali Buur Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, tey màggalsi màggalu Mbaar yi*.

Seen coobarey bopp lañu ko defe, waaye ñoo ko ameel waa Yerusalem it nag. Ndaxte gannaaw ñoom ñiy jaambur, gëmkati Yerusalem ñoo leen sédd ci xéewal yi leen ngëm may, kon ñoom jaambur ñi itam war nañu leena sédd ci seen alal.

Te yeen itam yeen ay doji cëslaay yuy dund, doj yi Noo gi tabaxe kërug Yàlla, ñeel liggéeyu carxal gu sell, ngir ngeen di ko jébbal ay sarax yu Noo gi rafetlu, sarax yu Yàlla nangu ndax Yeesu Almasi.