Bu ca fukkeelu nit ña desoon, ñoom it dees na leen dellu taal. Waaye dañuy mel ni wenn ci xeeti garab yu mag yi ñuy gor, ëkk ba dellu jebbi, ëkku xeet wii, jiwu mu sell lay doon.»
TSK
TSK · Isaiah 24:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bésub keroog sagub Yanqóoba sàggiku, yaram wa réer ko, mu jeex tàkk.
fa dara dul des lu moy am poraat; mu mel ni wittum oliw, bu noppee ñaari doom ak ñett ay des ca kaw, mbaa ñeent ba juróom ci car yi meññ. Kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil.
Waaye maay déeg lenn ci yeen, ñu rëcc saamar, tasaaroo ci xeet yi, ci biir réewi jaambur.
Aji Sax ji ne ko: «Wëral dëkk bi, ci biir Yerusalem. Foo gis kuy onk ak a binni, di ko naqarloo gépp tojaange gu ñu fiy def, nga rëdd aw rëdd ci jëëm.»
Waaye du tee mu am ndes mu ca rëcce, diy góor aku jigéen, ñu ñuy génneji réew mi. Ñu ngooguy génn, di leen fekki, te bu ngeen gisee seen jikko ak seeni jëf ju bon, seen xol dina sedd ci musiba mi ma wàcce ci kaw Yerusalem, ak mboolem lu ma fi wàcce.
¶ «Moona am nga foofu ci Sàrd nit ñu néew ñu tilimalul seen mbubb. Ñooñooy ànd ak man, sol lu weex, ndax ñoo ko yeyoo.