¶ Ca fukk ak ñeenteelu atu nguurug Esekiya buurub Yuda, ca la Senakerib buurub Asiri dikk song mboolem dëkki Yuda ya tata wër, daldi leen nangu.
TSK
TSK · Isaiah 36:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
2 Kings 18:13
TSK
Isaiah 1:7
TSK
Seenum réew gental, seeni dëkk xoyomu, seen suuf, doxandéem yi lekk fi seen kanam, muy gent bu doxandéem tas.
Isaiah 7:20
TSK
Bésub keroog saatu la Boroom biy wate, te saatu ba moo di buurub Asiri, mu àbbe ko ca wàllaa dex, wat la nel, wat say yeel, xuuf sab sikkim.
Isaiah 8:8
TSK
wal-wali jàll Yuda, mbënn ma wal, taañaañal, yéeg ba tollu ko ci put, firiku niy laaf ba dajal sam réew, yaw Emanuwel.»
Isaiah 33:7
TSK
Xool-leen seen jàmbaar ñiy yuuxoo ci mbedd mi, ndawi jàmm yaa ngii, di jooyoo jooy yu metti.
Micah 1:9
TSK
Góom bi Aji Sax ji teg Samari kat amul paj, te moo law ba Yuda, àkki ba buntu Yerusalem, ca saay bokk.