TSK

TSK · Isaiah 37:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Waaye boo toogee, boo génnee, boo duggee, xam naa, boo xadaroo sama kaw it, xam naa.

Job 41:2 TSK

Kenn ñàngul, ba sañ koo merloo. Kon ana kuy taxaw fi sama kanam man?

Buleen mel ni fas mbaa berkelle mi amul ag dégg, laab ak tarka di ko téye, mu doora yem fi seen wet.»

Say bañ xaacu nañ fa sa digg bérabu ndaje ma, samp seen raaya.

Boroom bi nee: «Bu ma sottalee liggéey fa kaw tundu Siyoŋ ak fa Yerusalem, maay mbugale buurub Asiri réy-réyloom gi, ak gëti xeebaateem.»

Rabsake bëkk-néegu buurub Asiri ne leen: «Waxleen nag Esekiya ne ko: Buur bu mag ba, buurub Asiri dafa wax ne: “Sa yaakaar jii nga yaakaar, ana foo ko teg?

Maa ngii di ko sol xel mu ko gëmloo xibaar bu muy dégg, ba dellu réewam, ma fàdde ko ab saamar ca am réewam.”»

Yoon wa mu dikke lay delloo, biib dëkk, du fi dugg. Kàddug Aji Sax jee!

Yeenay damu fi sama kaw, di ma wax waxi reewande ju bare! Maa déggal sama bopp.

Amos 4:2 TSK

Boroom bi Aji Sax ji giñ na ci sellngaam ne: «Ay bés a ngii déy, di ñëw, dees na leen kor, yóbbu, ku nekk ci yeen koru niw jën,

Acts 9:4 TSK

Mu daanu ci suuf, daldi dégg baat bu ko ne: «Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal?»