TSK

TSK · Isaiah 41:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Moo xar ay doj ca màndiŋ ma, mbàmbulaan wal, mu nàndal leen;

Mooy soppi màndiŋ it, ndox ya taa, soppi suuf su ne sereŋ bëti ndox;

Mbégte ngeen di rooteji fa wali mucc ya.

ku ci nekk mel ni seelukaayu ngelaw, di kiiraay ci ngëlén, mel ni wali ndox ci suuf su ne sereŋ, mbaa keppaaru doj wu mag ci àll bu mar.

suuf su wow doon ub déeg, joor gu maral ballal bëti ndox. Fa till fàkkoon, di fa goore, gattax ak barax a fay sëqe.

Maay sottim ndox suuf su mar, ak wal yu waleg joor gu wow. Maay sotti saw askan samag noo, sama barke sottikul ñi nga meññ,

ba ne ñi ñu tëjoon: “Génnleen!” Fa ñu nekkoon cig lëndëm, laa naa leen: “Génnleen ci leer gi!” Ñooy doon sama gàtt, dellu di fore aw ñall, ak wépp tund wu ne faraas tey.

¶ Waa ji nag delloo ma ca buntu néeg Yàlla ba. Gisuma lu moy am ndox muy balle ci suuf, di génne ci dëxu buntu penku bi. Kanam néeg baa ngi féete penku, ndox miy wale wetu bëj-saalumu néeg bi, fa féeteek bëj-saalumu sarxalukaay bi.

Bésub keroog Yerusalem la ndox muy dund di wale, genn-wàll gi jëm géeju penku, genn-wàll gi, géeju sowu, te noor ak nawet lay doon.

¶ Ci kaw loolu malaaka mi won ma dexu ndoxum dund mu leer nàññ ni doju kiristaal, ndox ma wale ca ngàngunem Yàllaak Gàtt ba,