Deuteronomy 8:7
TSK
Ndax seen Yàlla Aji Sax jaa ngi leen di yóbbu réew mu baax; réew mu ami wal, ak bëti ndox, ak ndoxi xóote yu waley xur aki tund,
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ndax seen Yàlla Aji Sax jaa ngi leen di yóbbu réew mu baax; réew mu ami wal, ak bëti ndox, ak ndoxi xóote yu waley xur aki tund,
Léegi nag bindleen woy wii ma leen di dégtal, te yaw Musaa nga jàngal ko bànni Israyil. Woyloo leen ko, ndax woy wii di sama seede ak bànni Israyil.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor, ñeel askanu Kore wu góor, dib taalif, te di woyu mbëggeel.
Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Ngor ak yoon laay woy. Yaw Aji Sax ji laay joobe.
Bésub keroog, tóokëru reseñ ju neex am, nangeen ko woy,
«“Sa ndey a la niru, mel ni reseñ gu ñu jëmbat fi wetu ndox, meññ, sëq lipp, ndax ndox mu ne xéew.