TSK

TSK · Isaiah 5:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba ñu demee ba mu yàgg, Firawna buuru Misra dee. Fekk na bànni Israyil a ngay binni rekk ndax seen njaam ga. Ñuy woote wall, ba seen jooy, ya sababoo ca seen toroxteg njaam ga, àgg fa Yàlla.

¶ «Képp ku dib jëtun akub jirim, buleen ko néewal.

¶ Ci biir loolu askan waak seeni jabar di xultu lool ci seen kaw bokki Yawut.

Job 34:28 TSK

ba yuuxi baadoola yi àgg fa moom, mu dégg yuuxi néew-ji-doole ya.

Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, geesul; séentool asamaan, ba gis te taxawusi reseñ jii.

Aji Sax jee safoo ñoñam, di terale néew-ji-doole ag mucc.

Ana nu biib dëkk yàqoo, mbeteb gànc, te nekkoon dëkkub kóllëre, njubte mate fa, njekk lal fa panaan, tey ñu diy bóomkat!

Moo tax Boroom beey wat jigéeni Siyoŋ nel, Aji Sax jeey muri seen jë.

«Dégluleen maa, yeen dëgër bopp yi! Yeenaka dëddu njekk!

Ni xale bu góor di takke ab janq, ni la la sa doom yu góor di moome ni jëkkër; ni boroom séet di bégee ab séetam, ni la la sa Yàlla di bégee.

Israyil di reseñ gu naat, meññal boppam lu ne gàññ, te lu meññeef ma gëna yokku, mu gëna yokkati sarxalukaayi tuur. Lu am réewam gëna baaxle, mu gëna baaxal ay xeri tuur.

Ana loo may wone lu bon, tey seetaan noteel? Yàquteeku ay fi sama kanam, xuloo di wéy, ŋaayoo jolli.

«Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Àtteb dëgg, nangeen ko àttee, te ngor ak yërmande it, deeleen ko jëflantee.

James 5:4 TSK

Dégluleen! Peyoor, ga ngeen xañ ña gub seen tool, mooy yuuxu noonu. Jàmbati góobkat ya tàbbi na ca noppi Boroom gàngoori xare yi.