Ana lu të Aji Sax ji? Bu ñu ca àggee nëgëni déwén déy, dinaa fi délsiwaat, te Saarata dina am doom ju góor.»
TSK
TSK · Isaiah 50:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
jën ya ca dexu Niil ga dee, dexu Niil ga xasaw, ba waa Misra manatuñoo caa naan. Misra gépp di deret.
Waaye bànni Israyil ñoom, ci suuf su wow lañu jaare ca digg géej ga, jàll, ndox ya ne sàtt, ñagal leen ndijoor ak càmmoñ.
Dafa gëdd géeju Barax ya, mu ne sereŋ; xóotey géej mel ni màndiŋ, mu jàlle leen,
Géej gaa leen gis, daw, dexu Yurdan a deltu gannaaw,
Ndoxum Niil ma day fer; dex gaay ŋiis, wow koŋŋ,
Xool naa xool ci tuur yi, gisuma kenn; du kenn ci ñoom ku ciy xelale, ba ma laaj ko, mu mana tontu.
Aji Sax ji dafa wax, moom mi sàkk yoon biir géej, rëddu xàll, digg mbeex mu ne xéew;
Xanaa du yaa wowal géej ak ndoxum xuram wu ne màww, def xóotey géej aw yoon, ña nga jot jàlle ca?
Daa xool, gisul kenn; mu tiisoo li ci kenn jógul, moo tax loxoom may ko ndam, te njekkam la sukkandikoo.
Du kenn kuy wormaal sa tur, mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw, yaa nu làq saw yiw, yaa nu def ban bu tooy ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc.
Man it maa leen di taamoo jox seeni mbugal, dikke leen tiitaange yi ñu yelloo, ngir maa woote, kenn wuyuwul, ma àddu, dégluwuñu ma. Xanaa di def lu bon lu ma ñaawlu, li ma buggul, ñu taamu ko.»
¶ «“Gannaaw def ngeen jëf jii jépp nag,” kàddug Aji Sax jee, “te ma waxoon leena wax ay yooni yoon, dégluwleen; woo leen, wuyuwleen,
Yónnee naa leen samay jaam, yonent yi, ay yooni yoon, ne leen: ‘Na ku nekk ci yeen dëpp yoonam wu bon, di def lu baax, baña topp yeneen yàlla, di leen jaamu, ndax ngeen dund ci réew mi ma leen jox, yeen ak seeni maam.’ Waaye teewluwleen ma, déggaluleen ma.
Dogal tukkee na ci man ne: muy mépp mbooloo ak bépp xeet ak wépp làkk, képp ku ci ñàkke kersa Yàllay Sadarag ak Mesag ak Abet Nego, ay dog lees koy dog, te këram dees na ko def ab sën, ndax kat amul jenn yàlla ju mana walloo ni moom.»
¶ «Dogal tukkee na ci man, ne mboolem fu bokk ci sama nguur, nañu fa ragal Yàllay Dañeel, wormaal ko, keey Yàlla jiy dund, kee sax fàww, nguuram du tas, kilifteefam du jeex.
Sama ñoñ dañoo làggi ci ñàkke ma kóllëre, wooyees na leen fa kaw, te kenn ci ñoom jógul.