Ñu sell ñi ci réew mi ñooy garmi yi, sama mbégte mépp ñoom a.
TSK
TSK · Isaiah 62:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Kër gu rafet sax, dees koy wacc, dëkk baak riiram, dees koy dëddu; tund ak tóoju doon ay xunti ba fàww, mbaamu àll ne ca finaax, jur ga di ca fore,
«Yaw mi jaasir ba juroo, xaacul! Yaw mi xamul mititu mat, sarxolleel.» Aji Sax ji nee: «Ndaw si ñu foñ moo gëna jaboot kiy séy.
Aji Sax jee la woo, nga dib jeeg bu ñu wacc, sa xol jeex tàkk, Mu ne la: “Nees di wacces ndaw, si nga takk ba ngay ndaw?”» Sa Yàllaa ko wax.
Maa béga bég ci Aji Sax ji, sama xol di sedd ci sama Yàlla jii. Moo ma solal yérey mucc, sànge ma mbubbam njekk, may nirook boroom séet bu kaalawu ni sarxalkat, ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.
Dees na leen wooye “Askan wu sell wi,” “Ñi Aji Sax ji jot;” te yaw Yerusalem dees na la wooye “Ki ñu namm,” “Dëkk bi ñu waccul.”»
«Yeen doom yu woyof kumba yi, délsileen.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay seen boroom kër, maay jële kenn ci bii dëkk, ñaar ca bee gox, boole indi Siyoŋ,
Su boobaa dees na ne: ‘Xool-leen miim réew, ak mbooy gi mu doonoon, tey mu naat ni toolub Àjjana! Dëkk yeet ay gent la woon, wéet, tojatoo, tey ñu dàbbli lépp, ba dëkke nii!’
Turi tuuri Baal laay jële ci sa gémmiñ, ba deesatul fàttliku seen tur.
Ci kóllëre laay digook yaw ab séy, ba nga xam Aji Sax ji.
«Xeet yépp ñu barkeel ñi lañu leen di wooye, nde réewum bànneex ngeen di dëkke.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
Moom la wax it ci téereb Ose ne: «Ñi dul woon sama ñoñ, ñoom laay wax sama ñoñ, ñooñu dul woon samab xejj, ñoom laay xejjoo.»
¶ Jëkkër nag, na sopp jabaram ni Almasi soppe mbooloom gëmkat ñi, ba jooxeel leen bakkanam.
Yeen ñi dul woon sax aw xeet, démb, tey yeen ay xeet wi Yàlla ñoñoo; dajaguleen woon yërmande, waaye tey daj ngeen yërmande.
¶ Ba loolu amee menn malaaka dikk. Mu ngi bokk ci juróom ñaari malaaka, yi yor juróom ñaari ndab yi fees ak juróom ñaari musiba yu mujj yi. Mu ne ma: «Dikkal, ma won la séet bi, soxnas Gàtt bi.»