¶ Aji Sax ji tegaat ca ne ko: «Gis naa bu baax fitna, ji sama ñoñ nekke Misra. Dégg naa itam seen jooy ndax kilifay saskat, yi leen di gétën ci liggéey, te ñeewante naa leen ngir seen coono.
TSK
TSK · Isaiah 63:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Maa leen di def sama ñoñ, di seen Yàlla. Dingeen xam ne man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen di teggil sas, yi leen waa Misra teg.
Ba loolu amee mu jël téere ba ñu bind kóllëre ga, jàngal ko mbooloo ma, ñuy dégg. Mbooloo ma ne ko: «Li Aji Sax ji wax lépp dinanu ko def, ba mu mat sëkk.»
Ndokklee, Israyil, ana ku mel ni yeen, askan wu Aji Sax jiy wallu, di seen kiiraay, di seen ndimbal, di saamar bi leen di sagal? Seeni noon a leen di loxal, te yeen, fa seen gannaaw ya ngeen di daagoo.
Teewul ñu di ko jéema naxey wax, di ko fen.
Ma ne: «Yàllaa may wallu, ma dal-lu, duma tiit. Sama dooleek sama kaaraange mooy Ki sax, di Aji Sax ji, te mooy sama wall.»
Man Aji Sax ji, maay sa Yàlla; man Aji Sell ju Israyil, maa lay musal. Maa joxe Misra, feye la; ak Kuus ak Seba, ma weccikoo la.
Yeen sama ñoñ, teewluleen ma, yeen sama ñoñ, dégluleen ma. Fi man la téereb yoon di bawoo, te maay fettaxal sama àtte, muy leeru xeet yi.
Éy Aji Sax ji, bul mer lool, bul ba xel fàww ci ñaawtéef. Ngalla seetal ne nooy sa ñoñ, nun ñépp.
«Man Aji Sax ji, fa Misra laa dale di seen Yàlla, xamuleen Yàlla ju dul man, te kenn du musle ku ma moy.
¶ Ci wàllu xibaaru jàmm bi, ay noon la Yawut ñi taxawe, te muy xéewal ci yeen ñi dul Yawut. Waaye ci wàllu dogal bi taamu Yawut ñi, ay soppe lañu, te seeni maam tax.
Buleen di fenante, gannaaw seen jëmm ja woon démb, boole ngeen kook jëfinam ja mu àndal, summi,
Yàlla miy kenn, sunu Musalkat, ci sunu ndimbalal Sang Yeesu Almasi, daraja ak màggaay ak kàttan ak sañ-sañ ñeel na ko, démb ak tey ak ëllëg, ba fàww! Amiin.