TSK

TSK · Isaiah 8:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: «Tàllalal sa loxo, mu jublu asamaan, lëndëm wàcc ci kaw réewum Misra, lëndëm gu nit mana daj, ndax fatt.»

Kon waxleen ne leen: «Ayca, ca ndigali yoon ya, ak seedey kàdduy waxyu ya. Kuy wax googu kàddu, ag leer fenkalu la.»

Du maay sànge asamaan ag lëndëm, mu mel ni ku ma solal saaku yu muy ñaawloo?»

Teral-leen seen Yàlla Aji Sax ji, bala moo lëndëmal, ngeen tërëfe tundi timis, di séentu leer, mu lëndëmal ba mu ne këruus, fatt taraj

Laajteleen te xool, ndax góor day wasin léegi? Moona maa gis jàmbaar ju ne jatu, ni kuy matu, kanam xoyy.

Bésub Aji Sax bu mag bee dëgmal, moo dëgmal te tànk yu gaaw lool lay jegesee. Kàddug bésub Aji Sax ji dégtu na, te ca la jàmbaar di yuuxoo yuux yu metti.

¶ «Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi ak weer wi ak biddiiw yi. Ci kaw suuf njàqare ak tiitaange mooy ñeel xeet yi ndax riirum géej gi ak gannax yi,