TSK

TSK · Jeremiah 21:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ma xamal leen nag li ma naral sama tóokër bi. Ñàggib ñagam, mu dim parlu; màbb miiram, ñu dëggaate ko, jàll.

Coowal mbooloo ngoog ca tund ya, mel ni ñu baree bare! Riirum nguuri nguur yu daje, di xeeti xeet! Aji Sax ji Boroom gàngoor yi mooy dajale gàngooru xare.

Bu ngeen fàddoon mbooloom xarem Babilon miy xareek yeen ñépp it, ba deslewuñu lu moy nit ñu ñu jamat, ñooñooy jógandoo taxaw ca seeni xayma, daldi lakk dëkk bii.»

¶ Yeremi ne Cedesyas: «Aji Sax ji, Yàllay Israyil, Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Soo nangoo génn rekk, jébbali sa bopp kàngami buuru Babilon déy, dinga rawale sa bakkan, te dëkk bii du lakk ba jeex. Dinga dund yaw, yaak sa waa kër.

Ñu yóbbaale mboolem ndabi xànjar yi ñuy liggéeye ci kër Aji Sax ji: ndab yiy def dóom, ak ñiitukaay yi ak ñiimi feyukaayi làmp yi, ak ndab yiy def deretu sarax yi, ak and yu ndaw yi, ak mboolem jumtukaayi xànjar yi ñuy sarxalee.

Aji Sax jee jañax sarxalukaayam, gedd bérabam bu sell. Moo teg ci loxol noon tatay këram yi. Biir kër Aji Sax ji la baat xaacoo, ni bu doon bésu màggal.

Bu ñu yaroon seeni doom it, maa leen leen di xañ, ba kenn du des. Te it ngalla ñoom, bu ma leen dëddoo.