TSK

TSK · Joel 1:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yoon yi jëm Siyoŋ jooy na wéet, kenn jaareetu ca màggalsi. Pénc yépp a gental, sarxalkat yay binni, janq ja jàq, Siyoŋ gépp di naqarlu!

Hosea 9:4 TSK

Duñu tuural Aji Sax ji saraxu biiñ, te seeni sarax du ko neex. Seen ñamu sarax day mel ni ñam wu ku nekk fu nit deeye, sobeel, ba ku ca lekk sobewu. Seenu ñam, seenub koll lay ñeel, waaye du dugg ci kër Yàlla gi.

Joel 1:16 TSK

Xanaa du ag lekk a dagg, nuy gis, te mbég ak bànneex tukkee sunu kër Yàlla ga?

Joel 2:17 TSK

Diggante buntu néeg bu sell beek sarxalukaay bi, sarxalkat yi, boroom dénkaaney Aji Sax ji, nañu fi taxaw jooy; nañu ne: «Aji Sax ji, yërëmal sa ñoñ; bul wacce say séddoo gàcce, ak ñaawley xeeti jaambur yi. Lu jar ñuy wax ëllëg ci biir askani jaambur yi, naan: “Ñii, ana seen Yàlla ji?”»