Genesis 13:13
TSK
Waaye waa Sodom ñu bon lañu woon, te mana moy Aji Sax ji lool.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye waa Sodom ñu bon lañu woon, te mana moy Aji Sax ji lool.
Aji Sax ji nag àddu ne: «Bàkkaari Sodom ak Gomor bare na lool, ba may dégg yuux, yi sababoo ci seen moy.
«Maa doon dëre tànk, man kenn ci ab dërukaayu reseñ, xeet yépp kenn dërlewu ma ci. Sama mer laa leen dëre, samam sànj laa leen dëggaatee, seen deret tis ci samay yére, ma taqal sama yére yépp.
Ku doon jàmbaar fi sama biir, la Boroom bi xalab. Am ndaje la ma wooteel, ngir falaxe sama ndaw yu góor. Boroom bee dëggaate Janq Yuda mu taaru mi, ni reseñ ci biir nalukaay.
Meneen malaaka génne ca néeg Yàlla ba, daldi àddu ca kaw, wax ak ki toog ci niir wi, ne ko: «Dawalal sa sàrt te góob, ndaxte ngóob jot na, ngóobum àddina ñor na.»