TSK

TSK · Jonah 3:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Aji Sax ji, ci ay xóote laa lay wooye.

Sàkkuleen Aji Sax ji bi ngeen koy mana gis, wooleen ko bi muy jege.

Seeni lënd du ràbbe ba solal nit, mbaa di sàng kenn; seenum ràbb ñaawtéef lay jur, seen loxo ya ko liggéey sabab fitna,

«Waaye ku bon ki su dëddoo mboolem moy yi mu moy, di sàmm sama mboolem dogali yoon, di jëfe yoon ak njekk, dina dund déy, du dee moos!

¶ «Lii moo tax yeen waa kër Israyil, ma di leen àtte, ku nekk ciy jëfam. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Dëppleen te dëddu mboolem seeni tooñ, ngir seenu ay bañ leena gàllankoor.

Ma ngay wax naan: «Xanaa lii du Babilon gu mag gi ma tabax man, ci sama doole ju réy, muy péeyu buur, di sama ndam ak sama daraja?»

¶ Ba loolu amee ñu ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Céy Aji Sax ji, ngalla bu nu bàyyi nu sànku ndax bakkanu nit kii, te bu nu gàdduloo bakkanu jaambur, ndax yaw Aji Sax ji, sa coobare nga def.»

Acts 3:19 TSK

Kon nag tuubleen te dëpp, ndax seeni bàkkaar faru.