TSK

TSK · Lamentations 4:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan.

Samiyel ne leen: «Kon Aji Sax ji seede na ci seen biir, ki mu fal it seede tey jii, ne gisuleen lenn ci sama loxo.» Ñu ne ko: «Seede na ko!»

Ba loolu amee fitu Daawuda ne tërit ndax la mu dagg ca lafu mbubbum Sóol.

Daawuda ne Abisay: «Bu ko rey. Ana kuy yékkati loxoom ci kaw ki Aji Sax ji fal, te yoon dabu ko?»

Daawuda ne ko: «Noo saña xàccee sa loxo, di bóom ki Aji Sax ji fal?»

Teewul mbooloo ma ne ko: «Déedéet, yaw doo ànd ak nun! Ndax nun su ñu nu dàqee, du am boobu solo. Bu sunu genn-wàll deeyee it, du am benn solo. Waaye sa jenn jëmm jii mooy fukki junni ci nun. Kon nag desal nu ci dëkk bi, di nu fi yónnee wall, moo gën.»

Wax nga say wóllëre ci peeñu, ne leen: «Tànne naa jàmbaar ci xeet wi, dénk ko ndimbal.

Mbooloom Babilon dàq leen, ba dab Cedesyas ca jooru Yeriko. Ñu jàpp ko, indil ko Nabukodonosor buuru Babilon ca dëkk ba ñuy wax Ribla, ca réewum Amat. Nabukodonosor dogal fa àtteem.

Ñu jàpp ko, yóbbu ca buuru Babilon ca dëkk ba ñuy wax Ribla ca réewum Amat. Nabukodonosor dogal fa àtteem.

Maa koy laaw samab caax, mu keppoo samag fiir, ma yóbbu ko Babilon mu Kaldeen ña. Réew ma, du ko gis te fa lay deeye.

Ba ko xeet ya déggee, dañu koo fexeel, mu sërëx ca seenum yeer, ñu lonk, yóbbu réewum Misra.

Ñoo bokk ak seedar gi wàcci njaniiw, ànd caak ña fa saamar tëral, ñoom ñi ko doon dooleel, xeet yi daan tooge keram.