TSK

TSK · Leviticus 23:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aaróona gis la xew, daldi tabax ci kanam sëllu wi ab sarxalukaay. Mu daldi yéene, ne: «Ëllëg màggal la, ñeel Aji Sax ji.»

Wooteleen ci bés boobu ndaje mu sell, te lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan, ak fépp fu ngeen dëkk.

¶ Noonu la Musaa xamale bànni Israyil bési màggalug Aji Sax ji.

Seen bési mbég itam, muy seen bési màggal, di seen ndoortel weer, nangeen ciy riiral liit yi riir mu xumb, yéenee ko seen saraxi rendi-dóomal, ak seen saraxi cant ci biir jàmm. Riirum liit yooyu mooy doon seen baaxantal fa seen kanam Yàlla. Maay seen Yàlla, Aji Sax ji.»

Yewu ne leen: «Beral-leen Baal am ndaje.» Ñu yéene.

Yékkatileen woy te jiin, xalam neex, ànd ak moroom ma.

Xoolal Siyoŋ, dëkk ba nuy màggale; yaay teg bët Yerusalem, dëkkuwaay bu dal ba, xayma bu deesul sempi, wewukaay ya deesu ko buddi mukk, te luy buumu xayma ya it, deesu ko dog.

¶ «Bu jote amee, ñoom ñooy àtte, ba dogal àtte bi ci sama àttey yoon. Sama digal yeek sama dogali yoon yi jëm ci sama màggal yépp, ñoo koy sàmm, te sama bési Noflaay, ñoo koy sellal.

Joel 1:14 TSK

Sellal-leen ag koor, woote am ndaje, wooleen mag ñi, ak mboolem waa réew mi, ca seen kër Yàlla Aji Sax ji, te ngeen woo Aji Sax ji wall.

Jonah 3:5 TSK

Waa Niniw nag gëm Yàlla, daldi yéene koor. Ci biir loolu ku nekk sol ay saaku, di ko ñaawloo, dale ko ca ka gën di mag, ba ca ka gën di ndaw.