TSK

TSK · Leviticus 26:41

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Musaa ak Aaróona nag dem ca Firawna, wax ko ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: “Siide nga maa nangul daal? Waaw, foo àpp sa ngàntal ak man? Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.

«Gis nga ni Axab toroxloo fi sama kanam? Gannaaw toroxlu na nii ci sama kanam, duma wàcce lu bon cig dundam. Ci jamonoy doomam ju góor laay wàcce lu bon ci waa këram.»

Ezra 9:15 TSK

Yaw Aji Sax ji Yàllay Israyil, yaay boroom njekk. May nga nu bésub tey jii nu dese bakkan. Nu ngi nii fi sa kanam ci biir tooñange, ba tax du kenn ci nun ku am lay fi sa kanam.

Musal ma ci sama mbugali tooñoo tooñ, bu ma bàyyi, dof di ma reetaan!

Yeen waa Yudak Yerusalem, deeleen xaraf ngir Aji Sax ji, dogleen seen mbuñukay xol, balaa sama xadar ne jippét ni sawara, di tàkk te deesu ko fey ndax seen jëf ju bon.

muy waa Misra, di waa Yuda, di Edomeen ñeek Amoneen ñi, di Mowabeen ñeek mboolem ñiy wat seen peggu kawaru bopp te dëkke màndiŋ mi, nde xeet yooyu, kenn xarafu ci dëgg, waaye bànni Israyil gépp it xarafuñu xarafu xol.»

Seen xol dina sedd ndax bu ngeen gisee seen jikko ak seeni jëf, dingeen xam ne mboolem li ma def ci dëkk bi, defuma ko ci neen. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»

Bu ngeen ma daan indil sama céru ñam, muy nebbon, di deretu sarax yi, dangeen di dugalaale sama biir bérab bu sell bi ay doxandéem yu xaraful, du ci jëmm, du ci xol. Noonu ngeen sobeele sama kër gi. Fecci ngeen sama kóllëreek yeen ndax seen jépp jëf ju siblu.

Yaw Boroom bi, njub ñeel na la, waaye nun gàcce ñeel na nu bésub tey jii, muy waa Yuda, muy waa Yerusalem, di waa Israyil gépp, ku jegeek ku sore, ci biir mboolem réew yi nga leen dàq, yóbbu, ndax li ñu la ñàkke kóllëre.

¶ Yeesu teg ca ne: «Maa ne leen, kooku moo ñibbaale këram àtteb ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte képp kuy réylu, dees na la toroxal, waaye ki toroxlu lees di yékkati.»

Ab Yawut, du ci melo wuy feeñ lees koy nekke, te xaraf it du ci màndarga muy feeñ ciw yaram.

Ndaxte nun noo xaraf tigi, nun ñiy jaamoo Yàlla Noowam gu Sell, di damoo Almasi Yeesu, te yaakaarunu aaday nitu suuxu neen.

James 4:6 TSK

Waaye yiw wu gënatee baawaan la maye. Moom la Mbind mi ne: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»