TSK

TSK · Leviticus 26:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Ñi des ci yeen, dinaa indi njàqare ci seen xol, foofa ngeen nekk ca seen réewu noon ya, ba xob wu ne foy-foy ngeen daw. Dingeen xélu ni ku ñuy dàqe saamar, bay daanu, te dàqeesu leen.

Yonatan ñalgu ca kaw tund wa, gàddukatu gànnaayam topp ko. Yonatan a ngay jam, waa Filisti di daanu, gàddukatu gànnaayam ba di leen jekkli ca gannaawam.

¶ Ci biir loolu Yawut ya ca des te dëkke yeneen diiwaani buur ya daldi daje ngir aar seen bopp, ba am jàmm ca seeni noon. Ñu rey ca seeni bañ juróom ñaar fukki junniy nit ak juróom (75 000), te seen loxo laalul alal ja.