«Waxal bànni Israyil ne leen: Képp ku dogoo jagleel Aji Sax ji nit, man naa wàccook kàddoom ci kaw nii ñu ko xaymaa.
TSK
TSK · Leviticus 5:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
su ko jëkkër ja déggee, te bés ba mu ko déggee, waxu ko ca dara, su boobaa xasi ndaw si day sax, te kàdduy dogu ya mu tegooloon boppam day sax.
¶ Bésub keroog mbooloom Israyil jàq nañu, ndax ngiñ lu Sóol teg ci seen kaw, ne: «Képp ku lekk fii ba ngoon te feyooguma ci samay noon, yal na alku.» Mbooloo ma mépp, kenn sexu ca dugub.
Yal na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar, ndegam maa wacc bët di sete kenn ku bokk ci waa jii, kuy taxaw, colal.»
¶ Ma nga naan: «Yal na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar ndegam bésub tey jii boppub Alyaasa doomu Safat du teqlikook baatam.»
Bu xalaat baree, indi gént; bu wax baree, waxi dof jib.
Moo sàggane ngiñ, moo wor kàddu ga mu fasante woon. Mu ngoog, moo joxe kàddoom, ba noppi walbatiku def lii lépp. Du mucc mukk.
¶ Ba bët setee Yawut ya daje, daldi xasoo, ne duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñu reyee Póol.