Leviticus 18:5
TSK
Nangeen sàmm samay dogal ak samay santaane, ndax ngeen jëfe yooyu moo leen di taxa dund. Man maay Aji Sax ji.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Nangeen sàmm samay dogal ak samay santaane, ndax ngeen jëfe yooyu moo leen di taxa dund. Man maay Aji Sax ji.
Ma jox leen sama dogali yoon, xamal leen sama àttey yoon yooyuy guddal fanu képp ku koy jëfe.
¶ «Waaye doom ya dañu maa gàntal. Sama dogali yoon, jëfewuñu ko, sama àttey yoon yiy guddal fanu képp ku koy jëfe, sàmmuñu ko. Sama bési Noflaay lañu ñàkke worma. Ma nar leena xëpp samam sànj, ŋaccal leen sama mer ca màndiŋ ma.
¶ Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, ñi ci yoonu Musaa la ko wax, ngir aw lay jeex tàkk, ngir itam mu leer nàññ ne àddina sépp a sikk fi kanam Yàlla.
Yoon wi nag ajuwul ci ngëm, nde: «Kuy jëfe digal yooyu, yaay dund ndax ñoom.»