TSK

TSK · Luke 14:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba loolu amee ndawi Daawuda walbatiku ñibbi. Ba ñu dikkee, daldi koy yegge kàddu yooyu yépp.

Maa ngi sëgg, ne yàcc, ne yasar, di wéye tiis,

Xel mu Rafet a ngay woote ca mbedd ma, di xaacu ca pénc ma.

Xel mu Rafet yónni ay janqam, di wootee fu kawee kawe ca dëkk ba,

Su boobaa ab làggi ne jàyy ni kéwél, ab luu sarxolle. Am ndox ay fettaxe màndiŋ ma, ay wal wale joor gu wow,

¶ Ba loolu amee may sàmm xar yi teefonke yi nara rendiluji, rawatina ñi gëna sonn ci gétt gi. Ca laa jël ñaari yeti sàmm. Benn bi ma tudde ko Xejjoo, bi ci des ma tudde ko Bennoo. Ci kaw loolu may sàmm gétt gi.

Luke 9:10 TSK

¶ Ba ndaw ya délsee, dañoo nettali Yeesu mboolem la ñu def. Mu ànd ak ñoomu neen ba sore, ca wetu dëkk ba ñuy wax Beccayda.

Maa leen ko wax, ñi ma woo woon ci sama bernde ji, kenn du ci mos.»

ana kon nun ci sunu bopp, nan lanuy rëcce mbugal, su nu sàgganee pexem mucc mu réy mii Sang bi jëkkoona biral, te ñi ko dégg dëggalal nu ko?

¶ Déggal-leen seeni njiit te nangul leen, ndax sàmm bakkani ñi ñu jiite mooy seenub liggéey, te moom lees leen di laaj ëllëg. Su ko defee ñu defe ko xol bu sedd, te bañ koo def di binni, ndax loolu du seen njariñ.

¶ Ma xoolaat, gisuma ci asamaan lu moy jeneen firnde ju màgg te yéeme: juróom ñaari malaaka yu taawu juróom ñaari musiba. Musiba yu mujj yaa nag, ngir ca la sànjum Yàlla di mate.

¶ Noo gi ak Séet bi neeñu: «Ñëwal!» Ku ci dégg it, neel: «Ñëwal!» Ku mar, ñëwal; ku bëgg ci ndoxum dund mi, jëlal, ñu may la.