TSK

TSK · Luke 21:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax jee leen di wasaare ci biir mboolem xeeti àddina, cat ba cat, ngeen di fa jaamu yeneen yàlla yu ngeen xamuloon, du yeen du seeni maam, yàllay bant ak doj.

Nun sa xeet wu sell wii, moomunu réew mi lu yàgg, te noon yi dëggaate nañu sa bérab bu sell.

Maay teg firnde fi seen digg, ba jël ñenn ca ña dese bakkan ca ñoom, yebal leen ci xeet yi, yebal leen Tarsis, ak Pul ak Ludd, ñooña di ñu mane fitt, ma yebal leen ca waa Tubal ak Yawaan, waa duni géej yu sore ya, ñooñu masula dégg sama jaloore, te masuñoo gis sama teddnga, sama ndaw ñaa leen di xamal sama teddnga.

¶ Ba loolu amee ma dégg jenn aji sell di wax, jeneen aji sell ne ko: «Lan mooy àppu peeñu mii ñu gis, ñu di ci dakkal sarax biy am bés bu jot, di teddadil gàngooru xare gi, ak a tooñ, di yàq lépp?»

Ma dégg ka sol mbubbam wëñ gu ëccu te taxaw ca kaw dex ga. Ma nga yékkati loxo ndijoor baak bu càmmoñ ba te naa: «Giñ naa ko ci Kiy Dund fàww ne ñetti jamonook genn-wàll lay doon. Xew-xew yooyu yépp a ngi dakk keroog bu dooley mbooloo mu sell mi jeexee tàkk.»

¶ Bokk yi, moytuleena defe ne seen xel mu rafet a leen may li ngeen am. Bugguma ngeen umple mii mbóot: Ag déggadi moo dikkal lennati bànni Israyil, ba kera xeet yi dul Yawut duggsi, ba seenub lim mat.