TSK

TSK · Luke 6:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ña reggoon, bindu, di dunde, ña xiifoon, noppee liggéey. Jigéen ju njur të woon jur juróom yaar, ku jur góori góor jeex tàkk.

Job 21:11 TSK

Day gis ay xaleem di bajantu, goneem yépp di tëbantu.

Na bége bànneexu bakkanam, ñu di ko kañe koomam,

lu ko moy ma regg, weddi la, ba naan: «Kuy Aji Sax ji?» Mbaa ma ñàkk bay sàcc, di la ñàkke worma, yaw sama Yàlla.

Naqar a gën xaxaloo; aw tiis ñëkkal kanam, rafetal xol.

Nit ñi dinañu taxawaalu ci réew mi, boole njàqareek ub xiif, te bu ñu xiifee, ñéññ, téen, xool kaw, saaga seen buur, saaga Yàlla,

Lii a waral sama njàqareg xol, mitit jàpp ma, mel ni mititu mat, ma jaaxle ba déggatuma, jàq ba gisatuma.

Ñii itam ay naan biiñ bay tërëf, màndiw ñoll, di jang: sarxalkat akub yonent la aw ñoll di tërëfloo, biiñ jànnaxe leen, ñu màndiw ñoll, di jang, bu ñu amee am peeñu, di tërëf.

Ña ngay naan biiñ, di sàbbaal yàllay wurus yaak yu xaalis yaak yu xànjar yaak yu weñ yaak yu bant yaak yu doj ya.

Niy taxas la ay noonam di laxasoo, mel ni ñu naan ba màndi, te ni boob mu wow lañuy lakke ba xoyomu.

Luke 8:53 TSK

Ci kaw loolu ñu di ko kókkali, ndax xamoon nañu xéll ne dee na.

Foofa la ay jooy ak naqarlu bay yéyu di ame yoon, kera bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ak yonent yépp ca biir nguurug Yàlla, te fekk yeen ci seen bopp, ñu dàq leen ca biti.

te ag ñàkk kersa, ak waxi caaxaan, ak kaf yu bon, dara jekku ci, waaye saxooleen kàdduy cant.

Fa nit ñi naan: «Jàmm ak kaaraange dikk na,» fa la sànkute di dale ci seen kaw, ni aw mat di jekkee dal ci kaw jigéenu wérul, te kenn du ca rëcce.

Gannaaw yaa ngi naan: “Am naa alal, barele naa, soxlaatuma dara,” te yaw xamuloo ni nga toroxe, jara yërëm, ñàkk, gumba, ne duŋŋ,