TSK

TSK · Luke 6:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Xarit ak dëkkandoo di ma daw, mbokk dànd ma.

Dégg naa ñaawlaate yu bare, ñu naan: «Éey, Tiitaange-lu-dajal! Booleleen ko, boole rekk!» Ñi ma séqal jàmm sax, di yeeru ma fakkastalu, naan: «Jombul mu juum, nu jekku ko, ba mana feyu.»

Njiitu jàngu ba nag yékkati kàddug ñaawlu ndax bésub Noflaay ba Yeesu faje. Mu ne mbooloo ma: «Juróom benni fan la nit ñi wara liggéey. Kon ci fan yooyu ngeen wara fajusi, waaye du ci bésub Noflaay.»

¶ Ba mu ko defee ñu bàyyi Yeesu xel, daldi yebal ay yeerukat, sas leen ñu yiw-yiwlu te di ko fiir ci kaw kàddu ba jàpp ko, ngir jébbal ko boroom dëkk bay boroom kilifteef ga ak sañ-sañ ba.