Waaye yaw Boroom bi Yàlla, yaa ñeewante, yërëm, yaa muñ mer, bare ngor ak worma.
TSK
TSK · Luke 7:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.
Aji Sax ji ne: «Du Efrayim ay sama doom ji ma sopp, gone gi may bànneexal? Lu ma ko gëdd gëdd, di ko bàyyi xel. Moo tax sama xol di ko laaj, ma yërëm koo yërëm.» Kàddug Aji Sax jee.
Ñépp a ngay jooy ak a tiislu janq bi. Yeesu nag ne leen: «Buleen jooy. Janq bi deewul, day nelaw rekk.»
Sang bi ne ko: «Jinigalkat yi ngeen doon! Xanaa du ci bésub Noflaay la kenn ku nekk ci yeen di yiwee aw yëkkam mbaa mbaamam ca gétt ga, ngir wëggi ko?
Ci kaw loolu Sang bi geesu, ne jàkk Piyeer, Piyeer fàttliku la ko Sang bi waxoon ne ko: «Bala ganaar a sab tey jii, dina fekk nga jàmbu ma ñetti yoon.»
ñiy jooy mel ni ñu jooyul; ñi bég, mel ni ñu bégul; ñi jënd, mel ni ñu moomul li ñu jënd;
Moo tax fàww mu niru woon ay bokkam ci bépp fànn. Su ko defee mu mana doon seen sarxalkat bu mag bu am yërmande te wóor fa kanam Yàlla, ngir mana defal askan wi seen njotlaayal bakkan.