TSK

TSK · Malachi 3:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Maa leen di witta witt.» Kàddug Aji Sax jee. «Garabu reseñ du dese doom, figg du dese doom,» kàddug Aji Sax jee, «xob ya sax day wow. Lu ma leen joxoon, rëcc na leen.»

Joel 1:7 TSK

Samag reseñ lañu fóom, samag figg lañu xasa xas, ba mu set, ñu sànni, car ya weex tàll.

Joel 2:20 TSK

Waa bëj-gànnaar, maa leen di soreleek yeen, maa leen di dàq, jëme réew mu maral te wéet, gàngoor ga jiitu jubal géeju penku, ga féete gannaaw jubal 0géeju sowu, ba seeni néew gilli, xasaw ba ubale, ngir jëf ju réy ji ñu def!»

Amos 4:9 TSK

«Maa leen dumaa gub yu yàqu, di saxee saxe, wowal seeni tool aki tóokër, garabu figg ak oliw, njéeréer yi lekk. Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee.

Ndaxam garabu figg foccul, doomu reseñ amul ca ndeyam, njurum garabu oliw àntuwul, tool yi meññul aw ñam, gàtt it tukkee na ca gétt ga, du genn jur gu gudd ci wurmbal,

«Ndax jiwum jàmm lay doon, garabu reseñ meññ doomam, suuf si meññ gàncaxam, asamaan di lay. Loolu lépp laay sédd ndesu askan wii.