Bésub keroog booba, ku bew bay regeju mooy detteelu, sagub nit sàggiku, Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe.
TSK
TSK · Micah 2:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ña nga naa: «Na Aji Sax ji gaaw! Na baral liggéeyam, nu gis. Na Aji Sell ju Israyil sottal mébétam, mu sotti, nu xam.»
Ku néeg déy dina neen, kuy ñaawle sànku, te képp kuy yeeru nu mu defe lu bon, dees na la dagg.
Dégluleen te teewlu, buleen fétteeral. Aji Sax ji kat wax na!
¶ Ci biir loolu Cedesyas buurub Yuda it, ma yegge ko kàddu yooyu yépp, ne ko: «Wàcceel yetu buuru Babilon saw ndodd, nangul ko, nangul ay bokkam, ndax ngeen dund.
Ci biir loolu saa yu Yewudi jàngee ñetti dog ba ñeent, Buur fab saatus bindkat, dagg dog ya, sànni ca taal ba. Mu di ko def ba taxañ ba lakk ca taal ba, ba jeex tàkk.
Samay tooñ la Aji Sax ji ëmb, fastee ko loxoom, mu tege sama kaw ndodd, ba jeexal sama doole. Boroom bee ma tàbbal ci loxo yu ma manula të.
Sunuw loos lañu ràng, nu loof, te noppaleesu nu.
Waaye ba mu bewee, të ticc bay réy-réylu, dañu koo jàllarbee ca nguuram, nangu ndam la,
Moo tax ku xelu ci jii jamono ne cell. Céy jii jamono ju bon!
Wóoy, ngalla ñiy mébét ñaawtéef, di ràbb lu bon ci seenub tëraay, bët set, ñu jëfe ko, ndax xam ne man nañu ko.
Ñoom ñoo jaay seen bakkan ngir ma mucc, te du man doŋŋ maa leen ameel njukkal, waaye mboolooy gëmkat yu jaambur ñi dul Yawut yépp a leen ameel njukkal.
Daan bu àndul ak yërmande, moom lees di àttee ña daawul jëfe yërmande. Yërmande nag kekku na ab daan.