TSK

TSK · Numbers 1:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba Leya ëmbee, am doom ju góor, da koo tudde Ruben (mu firi Gisleen, doom ju góor a ngi), ndaxte Leya da ne: «Aji Sax ji gis na sama toroxte. Léegi sama jëkkër dina ma bëgg.»

Ba mu demee ba mat wa gëna metti, rewlikat ba ne ko: «Muñal nag, ndax góor laati de!»

¶ Doomi Leya ñooy: Ruben, taawub Yanqóoba, ak Simeyon ak Lewi ak Yuda ak Isaakar ak Sabulon.

¶ Gannaaw loolu Yanqóoba woo ay doomam ne leen: «Bokkleen daje, ma xamal leen li leen di dikkal ëllëg.

¶ «Ñay dale ca kanam, fa féete penku, ñooy waa raayab Yuda ak seeni gàngoor, kilifag Yudeen ñi di Nason doomu Aminadab.

¶ Ki joxe saraxam ci bés bu jëkk bi, ñeel giirug Yuda, mooy Nason doomu Aminadab.

Raayab dalu Yudeen ña moo jëkka jóg, ànd aki gàngooram, njiital gàngooru Yuda di Nason doomu Aminadab,

¶ Ñaan gii nag la Musaa, góoru Yàlla ga ñaanaloon bànni Israyil, bala moo nelaw.

¶ Ma dégg limub ña ñu màndargaale torluwaay ba; ñuy téeméer ak ñeent fukk ak ñeenti junni (144 000), bawoo ci mboolem giiri bànni Israyil: