TSK

TSK · Numbers 17:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

mu def ñetti car. Naka la focci rekk, gaawa tóor, cëgg ya meññ reseñ ju ñor.

Sa nguur la Aji Sax ji saxal, dale ko fa Siyoŋ. Yilifal noon yi la wër!

Garabi àll bi yépp dinañu xam, ne man Aji Sax ji maay gàttal garab gu gudd, di guddal garab gu gàtt. Maay wowal garab gu naat, di naatal garab gu wow. Man Aji Sax ji maa wax, maay jëf.”»

Sawaraa tàkke fa bànqaasam, xoyom njebbit ak meññeef. Du car bu dëgër bu ca des bu mana doon yetu nguur.” Woyu dëj a ngii wu ñuy jooyeb dëj.»

Ca la sarxalukaayu wurus ba ñuy taal cuuraay bokkoon, gaalu kóllëre ga nekk moom doŋŋ ca biir néeg bu sell baa sell, ñu xoob ko wurus ba mu daj. Gaal ga moo yeboon njaqal wurus la defoon ñam wa ñuy wax mànn, ak yetu Aaróona wa jebbi woon, ak àlluway kóllëre ga.