Buleen ci sujjóotal lenn, buleen ci jaamu lenn, ndax man seen Yàlla Aji Sax ji, Yàlla ju fiir laa. Maay topp doom tooñu waajur, ba ca seen maasi sët, ba ca maasug sëtaati nit ñi ma bañ.
TSK
TSK · Numbers 25:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Buleen wóllëranteek niti réew ma, lu ko moy dinañu gànctook seeni tuur, rendil seeni tuur ay sarax, woo leen ca, ngeen lekk ca seeni sarax.
Waaye dinaa déeg ci biir Israyil juróom ñaari junniy (7 000) nit, di mboolem ñi sujjóotaluloon Baal te seen gémmiñ masu koo fóon.»
«Ni cabbu reseñu biir màndiŋ, ni laa fekke Israyil. Ni ndoortel doomi figg ju ndey ja taawloo, ni laa gise seeni maam. Waaye ñoom ñoo dem Baal Pewor, ñoo sédd seen bopp Baal, tuur mu ruslu mi, ba tax leena seexluwu ni kooku ñu sopp.
Li may wax kay moo di yooyu sarax, rab yi la ñeel, waaye du Yàlla, te bugguma ngeen bokk ak rab yi lenn.
Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.»