¶ Giirug Leween ñi nag ci bànni Israyil lañu bokk, waaye limaaleesu leen ak ñoom.
TSK
TSK · Numbers 26:62
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mboolem ña ñu limal Leween ñi, te Musaa ak Aaróona lim leen na ñu bokke seeni làng ci ndigalal Aji Sax ji, ñuy mboolem góor ñi am weer, jëm kaw, ñaar fukki junneek ñaar (22 000) lañu.
seenub lim nekk na juróom ñetti junni ak juróomi téeméer ak juróom ñett fukki góor (8 580).
Leween ñi ñooy ñiy liggéey liggéeyi xaymab ndaje mi, te lu ñu ca tooñ, ñooy gàddu pey ga, ci kaw dogal bu sax dàkk, ñeel leen, ñook seen askan. Waaye biir bànni Israyil, Leween ñi duñu ci séddu céru suuf,
«Santal bànni Israyil ñu sàkkal Leween ñi ci seen céru suuf, ay dëkk yu Leween ñi dëkke. Àllu parlu ya wër dëkk ya it, joxleen ko Leween ñi.
Leween gi ci seen biir dëkk nag, buleen leen fàtte, ndax amuñu wàll ci seen céru suuf.