TSK

TSK · Numbers 4:15

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sàkkalal mbooloo mi ag kemu fi wër tund wi, te nga wax leen ne leen: “Moytuleena yéeg ci kaw tund wi, mbaa ngeen di laal tund wi fenn. Képp ku laal tund wi, dees na ko rey.

Bu jaamookaay bi dee dem, Leween ñee koy wékki, bu jaamookaay bi dee dale bérab, Leween ñee koy we. Ku ci bokkul ba laal ci nag, dees koy rey.

¶ Seen sas nag moo doon gaal gi, ak taabal ji, ak tegukaayu làmp bi, ak sarxalukaay yi, ak ndabi sarxal ya ñu ca daa jëfandikoo, ak ridob biir bi, ak mboolem liggéey bu ci war.

Keyateen ña nag, joxu leen, ndax yu sell ya lañu sasoo woona gàddu.

Ñooy dénkoo sa ndénkaane, ak dénkaaney mboolem xayma bi, waaye jumtukaayi bérab bu sell bi, ak sarxalukaay bi, buñu ko jege, lu ko moy dañuy dee, ñoom ak yeen itam.

¶ Naka lañu dem ba tollu ca dàggay Nakon, nag ya tërëf, Usa tàllal loxoom, jàpp ca gaalu Yàlla ga.

¶ Cadog ak Abiyatar, sarxalkat yaa nga fa woon, ñoom itam. Ñenn ca góori Leween ña bokkoon nañu ca, di gàddu gaal ga àlluway kóllërey Yàlla ga dence. Ba ñu tegee gaal ga, Abiyatar di rendi ay sarax, ba mbooloo ma mépp génn dëkk ba.