TSK

TSK · Numbers 6:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Nees di xame ne daj naa saw yiw, maak sa ñoñ, te fekk ànduloo ak nun, ba nu doon, maak sa ñoñ, ñu ràññiku ci biir mboolem xeet yi ci kaw suuf?»

«Waxal bànni Israyil ne leen: Képp ku dogoo jagleel Aji Sax ji nit, man naa wàccook kàddoom ci kaw nii ñu ko xaymaa.

¶ «Góor gu xasal Aji Sax ji aw xas, mbaa mu giñ ngir dogu gu mu tegool boppam, bumu tebbi kàddoom. Noonee ko làmmiñam tudde, na ko ni defe ba mu mat sëkk.

Ab siis, bànneexu boppam rekk, loo ko digal mu xalab.

Amos 2:12 TSK

«Yeen nag ngeen di naanloo samay séddoo biiñ. Yonent yi, ngeen ne leen: “Buleen biral waxyu!”

Léegi daal, dangay def li nu lay wax nii: nu ngi feek ñeenti nit ñu am lu ñu xasal Yàlla.

Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.»

Bokkul ak yeneen sarxalkat yu mag yi; soxlawula jiital bés bu nekk, saraxi jur ngir bàkkaari boppam, door cee teg ay sarax ngir bàkkaari askan wi. Benn yoon la Yeesu sarxal, mu doy, te mooy ba mu sarxee boppam.