TSK

TSK · Proverbs 15:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Éy Aji Sax ji, lu la taxa sore? Xanaa dangay làqu, bésub njàqare?

Na dëddu lu bon tey def lu baax, sàkku jàmm, saxoo ko.

Su ma naroon ñaawtéef, Boroom bi du ma déglu.

Aji Sax jee kawe! Ku toroxlu, mu niir; ku réy, mu ñooru.

Saraxub ku soxor, Aji Sax ji bañ na ko; ñaanu kuy jubal da koy bége.

Seeni ñaawtéef a dox seen digganteek seen Yàlla. Seeni moy a leen xañ kanamam, ba mu tanqamlu leen.

Jant yooyu amuleen woon benn cér ci Almasi, te amuleen woon jenn yelleef ci mbootaayu bànni Israyil. Bokkuleen woon ci kóllëre yi ëmb digeb Yàlla, te mu fasoo ko ak ñoom. Ñàkk yaakaar, ak ñàkka xam Yàlla ngeen nekke woon ci àddina.

Ndax ay gët la Boroom bi ne jàkk aji jub ñi, te ay noppam la dékk seeni ñaan, waaye Boroom bi, kanamam lay tëjal ñiy def lu bon.»