TSK

TSK · Proverbs 2:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Nekkul it wàllaa géej ba ngeen naan: «Ana ku nuy jàllil wàllaa géej, jëlil nu ko, dégtal nu ko, ba nu jëfe ko?»

Ana nu ndaw mana sellalee? Xanaa di sàmm sa kàddu.

Doom, bul fàtte sama njàngle, defal sa xel ci saay santaane,

Déglul, doom, te dégg saay wax, ndax nga gudd fan.

Takkal foo tollu, taf ci sa xol, fas ko ci sa baat.

Déggal! Soxna si, Xel mu Rafet a ngi woote, dég-dég di xaacu.

Gone gu sàmm yoon am nag dégg, ku ànd ak sagaru nit gàcceel sa baay.

Luke 2:19 TSK

Teewul Maryaama moom, bàyyi woon na xel ci mbir moomu mépp, di ko xalaat ci xolam.

Luke 9:44 TSK

¶ «Ubbileen seeni nopp te teewlu bu baax kàddu yii: Doomu nit ki lees di wor, ngir teg ko ci loxoy nit ñi.»

Mboolem kàddu gii may wax, lu wóor la te jara gëm: Almasi Yeesu moo dikk ci àddina, ngir musal bàkkaarkat yi, te maa ci raw!