TSK

TSK · Proverbs 30:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Képp ku saaga baayam mbaa ndeyam, dee rekk mooy àtteem. Gannaaw baayam la saaga mbaa ndeyam, mooy gàddu bakkanu boppam.

¶ Ñu neeti: «Alku ñeel na ku torxal baayam mbaa ndeyam.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!»

Déglul sa baay bi la jur. Bu sa ndey màggatee, bu ko sàggane.

Kuy xeelu sa baay, di siidee déggal sa ndey, baaxoñ génne ciw xur, luqi sa bët, tan ya lekk.

Waaye su dee ab jëtun bu ami doom mbaa ay sët, ñooñoo wara jëkka jéema jëfe ag ragal Yàlla ci seen biir kër, ba delloo njukkal seen waajur, ndax loolu la Yàlla rafetlu.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.