¶ Ci biir loolu senn as ndaw su am xel ca dëkk ba, woote ne leen: «Dama ne, dégluleen! Neleen Yowab mu ñëw, ma wax ko.»
TSK
TSK · Proverbs 31:26
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba surgay Esteer yu jigéen yaak bëkk-néegam yu góor ya dikkee wax ko Esteer, tiislu na ko lool, daldi yónnee Mardose ay yére, ngir mu summi saaku ya mu sol. Waaye Mardose nanguwul.
Lingeer Esteer àddu ne ko: «Buur, ndegam xool nga ma bëtu yiw te neex na la, may ma, ma mucc maak samaw xeet; moom laay ñaan te moom laay sàkku.
Kàddug ku jub day jur xel mu rafet, ku wax njekkar ñu tëj sa gémmiñ.
Wax ju yiw di lem juy xelli, neexa ñam, di jàmmi yaram.
Muñ mer ay nax kilifa, te wax ju neex, fu mu jaar, mu nooy.
Njànglem dëgg la dëkkaloon ci gémmiñam, te ag njubadi, déggeesu ko ciw làmmiñam, xanaa di ànd ak man ci jàmm ak njub, tey baloo ñu bare yoonu ñaawtéef.
Mu àddu ca kaw ne: «Yaa gëna barkeel ci jigéen ñi, sa doom ji nga ëmb it barkeel na!
Mu tàmbalee waxe kóolute ca jàngu ba. Pirsil ak Akilas dégg ko, woo ko cig wet. Ñu daldi koy gëna leeralal yoonu Yàlla wi.
¶ Jëfeleen xel mu rafet seen diggante ak aji gëmadi ñi ci biti, te jot gu ngeen am, fexeleen ba jariñoo ko.
waaye nay lu làqoo jëmmu biir, nay gànjar gu dul jeex, te mooy lewetaay akug teey, ndax looloo réy njarte fa Yàlla.