Gannaaw gi Buur Daawuda toppatul Absalom, ndax mujj na miis deewug Amnon.
TSK
TSK · Romans 1:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mboolooy gëmkat ñi di gëna feddliku ci wàllu ngëm, seeni lim di yokku bés ak bés.
¶ Gannaaw ba loolu wéyee, Póol ci ndigalal Noo gu Sell gi am mébétum jaare diiwaani Maseduwan ak Akayi, teg ca Yerusalem. Mu ne: «Gannaaw bu ma àggee foofu, war namaa jàll ba Room itam.»
Te xam naa ne bu ma dikkee fa yeen, barkeb Almasi bu mat sëkk laay dikke.
¶ Kooku leen mana dooleel nag ndax sama xibaaru jàmm, ak waareb Yeesu Almasi, mi mu feeñal mbiram tey, gannaaw ba mu nekkee mbóot mu làqu woon naka jekk,
Te ki nuy saxal ci Almasi, nook yeen, moo nu tabbe diwu pal gi, te moo di Yàlla.
Ndax kat gaaw ngeena xajoo lool, nit ku dikk, di leen waare meneen Yeesu mu nu waarewul, mbaa geneen noo gu ngeen jot te jotuleen ko woon, mbaa beneen xibaar bu ngeen dëggal, te mu wuute ak ba ngeen déggoon.
Moo tax ñu ne: «Moo yéeg fa kawa kaw, yóbbaale gàngoor gu mu jàppe xare, te moo séddale nit ñi ay may.»
ndax namm na leen lool, boole ci tiisoo li ngeen dégg ag jagadeem.
Nu daldi yónni Timote, muy sunu mbokk, di jawriñub Yàlla bu nuy liggéeyandool ci xibaaru Almasi. Su ko defee Timote dooleel leen, feddli seen ngëm,
yal nañu leen may jàmmi xol, te may leen dooley wéye jépp jëf ju baax, ak gépp kàddu gu rafet.
¶ Buleen nangu ay àlluwa yu bare te woroo ak sunu ngëm, di leen fàbbi. Li baax mooy ngeen di yokke aw yiw, seen pastéefu xol. Buleen yokke pastéefu xol, ay ndigal yu jëm ci aw ñam, te ña koy sàmm, jariñu leen dara.
¶ Silwan, miy mbokkum gëmkat mu wóor, ci sama xalaat, ci ndimbalam laa leen bind kàddu yu gàtt yii, di leen ñaax aka seedeel ne lii kat moo di yiwu Yàlla dëgg. Taxawleen ci bu dëgër.
¶ Kon nag yeen soppe yi, gannaaw xam ngeen loolu ba noppi, wattuleen bala leena réeraangey moykati yoon yi yóbbaale, ba yolomal seenub taxawaay.