TSK

TSK · Romans 1:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 16:19 TSK

Ma ne, tey fi tey, am naa ab seede kaw asamaan, sama seede kay a nga fa kaw.

Luke 18:1 TSK

¶ Yeesu dellu leen léeb lii, ngir ñu wareefoo di sax ci ñaan te baña xàddi.

Acts 3:26 TSK

Yeen la Yàlla jëkka wool jawriñam, daldi koy yebal ci yeen, ngir barkeel leen, waññee kenn ku nekk ci yeen, mu moy jikkoom yu bon.»

¶ Gannaaw ba loolu wéyee, Póol ci ndigalal Noo gu Sell gi am mébétum jaare diiwaani Maseduwan ak Akayi, teg ca Yerusalem. Mu ne: «Gannaaw bu ma àggee foofu, war namaa jàll ba Room itam.»

Ndax malaakam Yàlla ji ma moom, te ma di ko jaamu, moo ma dikkal biig.

Su may ñaan ci weneen làkk, sama xol ay ñaan, waaye samam xel liggéeyul.

Ak dëggu Almasi gi ci man, kàddug damu googu, kenn du ma ko xañ, ci diiwaanu Akayi gépp.

Li ma leen bind nii nag, Yàlla mi nu tiim seere na ne du ay fen.

¶ Looloo ma taxa sukk sama bëti óom, janook Baay bi,

te saa su ma leen di ñaanal, mbég laa leen di ñaanale yeen ñépp,

Timote nag xam ngeen ne ku rafet ab jëw la. Ni doom di taxawoo baayam, ni la bokke ak man liggéey, bi ci xamle xibaaru jàmm bi.

¶ Moo tax nun itam, ba nu déggee seen mbir ba tey, noppiwunu leena ñaanal, di sàkku ngeen feese xam-xam ci lépp luy coobarey Yàlla, te ngeen ànd ceek lu mat sëkk ci wàllu xel, ak gis-gis bu Noo gi maye.

¶ Nu ngi sant Yàlla fu nu tollu ci yeen ñépp, te noppiwunu leena fàttliku ci sunuy ñaan,

Guddi ak bëccëg, pastéefu xol lanuy dagaane Yàlla, ngir man leena gisaat, ba mottli li yées ci seen ngëm.

Ci boobu seede lañu ma tabbe ab yéenekat, ak ndawal kàddu gi, ak itam ab sëriñ, ñeel xeet yi dul Yawut, ngir ma xamal leen yoonu ngëm ak dëgg. Fenuma, dëgg doŋŋ laay wax.

¶ Sant sama Yàlla laa dëkke saa yu ma la fàttlikoo ci samay ñaan,